Dendu mbëj
Apparence
Dendu mbëj, ci biir ab toolu mbëj, lañuy faramfacce niki liggéey bi mu laaj gir man a jële ab yanu mbëj (1 Coulomb) ci ab tomb yóbb ko ci beneen. Dendu mbëj dañu koy jaawale ak wuuteeg aj gu ñaari tombi ag ndombo gu mbëj, su fekkee toolu mbëj bi duy soppeeku (maanaam dayoom sax) dañuy wuute wante su fekkee dafay soppi dayoom ci benn diir bu nekk wuuteeg aj gi kenn dootu ko man a natt ba tax dañu koy yamale ak dend bi.
Tekkeem
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Su dawaanu mbëj dee liy natt walug yan yi, dendu mbëj mooy natt kàttan giy yóbb yan yi. Njunj bees koy jëmmalee mooy U walla yenn saa yi V te bennaanu nattam di volt [v].
Séddaleb kàttanu mbëj
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Nbombo yi ñuy séddalee kàttanu mbëj dañu leen xaajale ciy wàll sukkandiku ci seen dayoo: dend bu kawe, dend bu diggu, dend bu suufe, dend bu suufe lool.
Tur | Tënk | Dayoom ci dawaan bu wéy | Dayoom ci dawaan bu safaanu |
---|---|---|---|
Dend bu kawe | DK | ||
Dend bu diggu | DD | ||
Dend bu suufe | DS | ||
Dend bu suufe lool | DSL |