Gerte tubaab
Apparence
Gerte tubaab xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Cambretaceae". Mi ngi soqeekoo ci réewum Gine. Barab yi bari naaj ak taw lay faral di sax.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Gerte tubaab garab la gog mi ngi toll ci 9 ba 25i met ci guddaay. Ci jamonoy noor, ay xobam dañuy joxe wirgo wu palmaan lu jëkk ñuy wadd.
Meññeefam nëtex lay tàmbalee, su jegee ñor day puur. Su ñoree dëgg nag day palmaan.
Njariñam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Manees na koo lekk noonu. Manees na koo jëfandikoo it ci xeetu togg yu wuute. Xooxam dees na ci sos ay fowukaay niki ay gaal yu daw
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Terminalia catappa