Gargamboose
Apparence
Gargamboose xeetu garab la gu bokk ci ñoñ "opuntia". Ca Amerig gu digg la bàyyikoo, fi ñuy woowee Karayib.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Gargamboose garab la gog day màgg te am xeetu xob yu dijj ak ay dég yu mag te ñaw, seen taxawaay di kaaraange, am na it dég yu sew yuy jame
Meññeef mi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Meññeef mi dees koy lekk. Dees koy xolli bam set bala ñu koy jëfandikoo.
Njariñ yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ay doomam bari nay njariñ lool.
Dees na ci defar ay tàngal, ay njar walla njambaan yu neex. Ay bantam day faj (estomaa) góomu biir. Biir buy daw it dina koy faj, ba ci sax jabeet.
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Opuntia tuna
Tur wi ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]araab: الصبَار |