Itaali
Réewum Itaali Pénc'um Itaali | |||||
| |||||
Barabu Itaali ci Rooj | |||||
Dayo | 301,338 km2 | ||||
Gox | |||||
Way-dëkk | 60,017,677 nit | ||||
Fattaay | 199.2 nit/km2 | ||||
Xeetu nguur - Njiitu Réew - Njiitu Jëwriñ |
Repiblik Giorgio Napolitano Mario Monti | ||||
Tembte - Bawoo - Taariix |
|||||
Péy ak rëddi - Tus-wu-gaar - Tus-wu-taxaw |
Rom | ||||
Làkku nguur-gi | wu-itaali | ||||
Koppar | Euro (EUR) | ||||
Turu aji-dëkk | Itaali-Itaali Sa-Itaali | ||||
Telefon | |||||
Lonkoyoon bu Itaali |
Itaali (Pénc mu Itaali) réewum Tugal (Óróop) Itaali men la ci réew yi nek ci Bëj-saalumu tugal,
ngir xootal Taarixu Itaali xoolal Fii
Ni Itaali meloon njëkk xare yu Napoleon yi:
Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon réew mu ñu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kiliftéefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Dóox ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne dañoo nekkoon ci waawug imbraatóor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia.
Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatóor lañu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa cig jonjoodi .