Lébu, aw waaso la wu bokk ci Wolof ni ki Gànjol-Gànjol yi walla Ajoor yi nekk ci reewum Senegaal. Ñoom, Ndakaaru mooy seen dëkk, ñu leen fekk tamit ci diggante Ndar (Saint Louis) ak Tenŋeej (Rufisque), ba Mbur. Ci wetu géej ak tefes. Ci napp mi lañu dund, ci seen cosaan. Seen làkk di wolof. Seen wolof. Séen Wolof am Na wuute ak waxiinu yeneen goxi Wolof yi ni mu ci digante Ajoor-Ajoor ak Saalum-saalum walla Waalo-waalo.

Lebu (baat bi)

Soppi

Cosaanu baat boobu, wutte na ci li kilifa yi tekki. Ñooñu deeñi nettali ay cosaan yu wutte: leeb moo juur baat bi. Am na ñeneeni wax luubu mooy bañ, ndax ci cosaan, Lebu yi dañu musa bañ ku leen noot.

Seex Anta Jóob, ci gestoom, da wone ni, li ñu tudde lebu, am na lu mu bokk ak tur boobu ñu joxe reewum Libi. Libi, ci jamono Isipt gu yàgg ga amoon, moo ne woon benn diwaanu, nit ñi di fa dem Rëbbi, ak nappi. Dëkk boobu dafa janno ak geej gi. Moo tax ñu yoroon Isipt yu yagg ga, tudde dëkk boobu: rëbu. Ñu wara xam ni, Seex Anta Joob ak yeneen gestu kat, wone nañu ko, lakk boobu amoon ca Isipt boobu, ak lakk wolof, ñoo bokk maam. Rëbu moo juur Lebu (r-l), Lebu moo juur Libi. Dëkk bi ñu xam ne, ay nit ñu ñuul ñoo fa ne woon, te ñu daan tudd ñu dëkk ca biir reew mi kaw.

Mel ni li am Senegaal tey: Lebu yi dëkk ci tefes ak wetu geej gi, kaw-kaw yi dëkk ci biir reew mi.

Cosaan

Soppi

Lebu yi, kon, reew mi ñu tudde tey Libi, lañu ne woon ci jamono Isipt gu yagg ga ame. Dañoo mujj daw dëkk boobu, ndax amoon na benn askan bu ñowoon foofu, joge Asi, te ñu leen daan begga noot. Ñoom ñoo Persi yi.

Ci seen gadday, jaar nañu ci ay dëkk yu bare (Sudaan, Caad, Niseer, Mali). Sudaan, mooy dëkk bi Lebu yi baawo, ñu ko gëna raññe ci turu Nubi walla Kuus.

Senegaal, lañu agsi, jamono nguuru Tekuruur ame. Foofu lañu fekk seen bokk, di Pël yi ak Séeréer yi. Rawatina Pël ak Seereer yi ñuy napp, ñu leen tudd ci lakku pulaar ay Cuballo / Subalbe. Foof lañu sanc ay dëkk mel ni KasKas ak Njum.

Waaye ci Senegaal, taxawuñu Tekruur rekk. Jaar nañu Jolof, ak Kajoor, sooga mujj agsi ca Ndakkaru ci diggante atum 1430 ak 1530.

Foofu, ay Socé lañu fekk.

Li ci dess, fi la: Réewi lebu yi.

Njabootayu Lebu yi

Soppi

Fukki ak ñaari xeet ñoo nose askanu Lebu yi. Ñu ne tamit, Fukki ak ñaari PENC yi.

Ñoom ci senn bopp, dañu xaaj ci ñaari njabootay yu mag, di Sumbejun yi ak Beeñ yi.

Ñoo yore woon gox yi ci Ndakaaru: Yoff, Wakam, Ngor, Sumbejun... .

Sant yi

Soppi

Lebu yi ñoo bokk sant ak Seereer yi, mel ni: Ndóoy, Puy, Ndir, Jeen, Yaad, Jaañ, Fay, Jeey, Sar, Caw, Njaay, Juuf, Sek.

Bokk nañu ay sant tamit ak Tukkloor/Pël yi: Mbay, Gey, Ñaŋ, Jaw, Waad, Gay, Joob, Samb, Conŋaan, Baaxum, Jeŋ... .

Ñu sant Mbeŋ, ci li cosaan tekki, seen maam ay Mandiŋ lañu woon, seen mamaat di Jolof Mbeŋ (ab lamaanu Jolof), juge Mali.

Da firnde ni, Lebu yi, ci ñoom ñi lañu cosaanoo. Mel ni wolof yi rekk.

Diine

Soppi

Lebu yi, ay jullit lañu. Ñu bare bokk ci Tariqa Tijaan, ak Layeen yi (Seydinaa Limaamu Laay). Seen këru diine di Kambereen, ca Yoff.

Waaye, du tax ñu fate seen cosaan, ak li seen maam defoon, ba ñu nekke Ceddo. Manaam tuur yi. Tuur yi, am na solo ci Lebu yi, ndax ci seen jaar jaar, tuur yi, gëdd gu mag lañu yoroon ci ñoom, ci lu jëme ci xare yi, ak yeneen xeew yu amoon solo ci seen cosaan.

Ci seen tuur yi, ndëpp la nit ñi gëna xam, ngiir faj febaru ñooñu ñu xam ne, jiine ñoo tax. Jiine ci Lebu, rab leen ko tudde.

Lëk Dawwur, Maam Kumba Kastel, Maam Jaare, ak yeneeni tuur, bokk neen ci ñooñu Lebu yi seqante.

Xool itam

Soppi